LBRY Block Explorer

LBRY Claims • luug-8-jiwu-wuute-na-ag-muj

9ec87cb58c0be68cfabb311f92e52daa0b55dc79

Published By
Created On
8 Oct 2023 19:28:03 UTC
Transaction ID
Cost
Safe for Work
Free
Yes
LUUG 8 | Jiwu wuute na ag muj
Jiwu wuute na ag muj
1Gannaaw loolu Yeesu wër dëkkoo dëkk bu mag ak bu ndaw, di waare, di yégle xibaaru jàmm bu nguurug Yàlla, ànd ak fukki taalibe yaak ñaar, 2ñoom ak jigéen ñii mu fajoon, ba tàggale leen ak rab yu bon aki jagadi: Maryaama, mi ñuy wax Magdala, ma ñu tàggaleek juróom ñaari rab, 3ak Yowaana jabaru Kusa, saytukatub Erodd; ak Susaana, ak ñeneen jigéen ñu bare ñu daan dimbalee ñoom Yeesu seen alal.
4Mbooloo mu mag a daje woon, jóge dëkkoo dëkk, fekksi Yeesu. Mu léeb leen, ne leen: 5«Boroom jiwu moo demoon jiyi. Naka lay saaw ab toolam, ndeke lenn ca jiwu maa nga wadde ca kaw yoon wa, nit ñi joggati ca, picc yi dikk, lekk ko. 6Leneen wadde fu barey doj. Naka la sax rekk, daldi wow, ndax ñàkk ndox. 7Leneen la wadde biiri xaaxaam, jógandoo ak xaaxaam ma, daldi fatt ba wow. 8La des ca jiwu ma wadde suuf su nangu, daldi sax, ba meññal lu ko mat téeméeri yoon.»
Ci kaw loolu Yeesu àddu ca kaw ne: «Ku am nopp yu mu dégge kat, na dégg.»
9Ay taalibeem laaj ko lu léeb woowu di tekki. 10Mu ne leen: «Yeen lañu may, ngeen xam mbóotum nguurug Yàlla, waaye ñi ci des ñoom, ci ay léeb lees koy dëxëñ, su ko defee:
“Ñuy xoole te duñu gis,
di dégg te duñu xam.”
11«Lii la léeb wi di tekki. Jiwu wi moo di kàddug Yàlla. 12Ñi féeteek yoon wi mooy ñi dégg. Seytaane nag mooy dikk, foqati kàddu gi ci seen xol, ngir ñu baña gëm ba mucc. 13Ñi féete fu bare ay doj, ñoo dégg kàddu gi, nangoo ko xol bu sedd. Waaye ñooñu, ab reen lañu amul. Ab diir rekk lañuy gëm, bu janti nattu dikkee, ñu dellu gannaaw. 14Li wadde ci ay xaaxaam mooy ñi dégg kàddu gi, te ay xalaat ak alal, ak bànneexu bakkan fatt leen, ba tax meññaluñu lu ñor. 15Li ci suuf su baax si nag, mooy ñi dégge kàddu gi xol bu dëggu te rafet, ŋoy ca, te saxoo muñ ba meññal.

Sunu Yaakaar ak Serigne Malick Diop
yaakaarjusax@gmail.com | 77.335.5591
...
https://www.youtube.com/watch?v=hlrJxRosmKs
Author
Content Type
Unspecified
video/mp4
Language
Unspecified
Open in LBRY

More from the publisher

Controlling
VIDEO
VOUS
Controlling
VIDEO
MACë
Controlling
VIDEO
SUNU
Controlling
VIDEO
NI YO
Controlling
VIDEO
SOYON
Controlling
VIDEO
SUNU
Controlling
VIDEO
IBRAH
Controlling
VIDEO
JUDDU
Controlling
VIDEO
MACë